![Youssou N'Dour Ballago ndumbé yatma](https://dcslyrics.com/wp-content/uploads/youssou-ndour-ballago-ndumbe-yatma.jpg)
Youssou N’Dour – Ballago ndumbé yatma Lyrics
Artist: Youssou N’Dour
Song: Ballago ndumbé yatma
Billaay , ballago ndoumbé yatma
Su ñu waaji xaj oon na fi
Naxxar doηη ,la ñu bayyee
Yalla , wonneeti na
Li tax ba mbir mi metti lool
Ñun da ñu ko foog wul woon
Yëf yi gaaw ba bette gnou
Billaay wéetël na ñu
Njiinoo njiin faramaareen
Gòor u jaaga , nelaw naa
Baay i wally dem na nii
Ñun daal wéetël na ñu
Ma ngi koy jaale Sénégal
Di ko jaalé Gambia
Di ko jaalé adduna
Ndaanaan ba dem na nii
Thione ballago , ndoumbé yatma
Bu yalla buur bi doon taggoo
Kon di na ñu bayék yaw
Ni patrimoine bi nga ñu bayyeel
Yee gua nit gñi , tete leen ci adduna
Yee gua nit gñi , tete leen
Xam al leen ci adduna
Ahhh – Balaago
Yee gua nit ñi ci adduna xam al leen
Ni ñu war a nekkek
Ak ni ñu war a dundée
Ak ni ñu war a jëfleentee
Jinaxoo mbaay
Yaw mi dëkké biir suuf
Boo dem ee neel ballago , réew maa ngi koy joy
Aduna ngi koy jooy
Art baa ngi koy jooy
Njiin faramaareen
Thione seck , wéetël na ñu
Ballago ndumbé yaatma
Adduna , am ul solo
Li tax ba mbir mi metti lool
Ñun da ñu ko foog wul woon
Yëf yi gaaw ba bette gno
Ndanaan ba demna ni
Njiin faramaareen
Thione seck , wéetël na ñu
Ballago ndumbé yaatma
Adduna , am ul solo
Find more lyrics at https://dcslyrics.com
![DCSLyrics.com Amazon Music](https://online-tips.jspinyin.net/wp-content/uploads/Amazon-Music.png)
![DCSLyrics.com Apple Music](https://online-tips.jspinyin.net/wp-content/uploads/Apple-Music.png)
Disclosure: As an Amazon Associate and an Apple Partner, we earn from qualifying purchases
Youssou N’Dour – Habib Faye
Burna Boy, Youssou N’Dour – Level Up (Twice As Tall) (feat. Youssou N’Dour)
Youssou N’Dour Lyrics – Ballago ndumbé yatma
Please support our site by sharing it.
And please follow our site to get the latest lyrics for all your favourite songs.
Release Year: 2004
https://www.youtube.com/watch?v=8v1xNZ9vj5w